LI XEW CI YOON WI
Sëriñ Alhaaji Mbàkke mi doon saytu Kër Seexul Xadiim faatoo ci Jumaay Tuuba
Sëriñ Alhaaji Mbàkke mi doon saytu Kër Seexul Xadiim gi nekk ci wetu Jumaa ji Yal na ko sunu Boroom teeru ca Àjjanay Firdawsi ya, mingi faatoo ci Jumaay Tuubaa ji bi mu ñëwee ngir jooxe waxtuw Jullig Gee gi, bi mu kàbbaree ngir dawal ñaari Ràkka ngir Nuyoo ko Jumaa ji ci la Yàlla dogalee mu wàcc.
Yal na Firdawsi di këram barkeb Seexul Xadiim mi mu doon liggéeyal…!!!
Image: les Caméras de Surveillance de la Grande Mosquée de Touba.