Lii mooy xutba (1346) Mooy xutba bi Boroom Tuubaa mujj a def ak taalibe yi.

Lii mooy xutba (1346) Mooy xutba bi Boroom Tuubaa mujj a def ak taalibe yi.
(Xutbatu ومسش)
Sëriñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana moo ko dajale.
Sëriñ Muhammudu Lamin Jóob Dagana nee na:
« Boroom Tuubaa Yal na Yàlla saxalal ko ngërëm, dafa santaane mbooloo mi dajaloo ci bisu Gaawu 16 ci fani Tamxarit 1346, tolloo ak 15 jullit 1927 ginnaaw ba ñu jullee tàkkusaan. Ba ñu dajee Sëriñ bi ne: « Tay la ñaata fan ci weeru tamxarit » ? Mbooloo mi ne ko tay la 16 ci weer wi. Sëriñ bi daal di ne: « Dénk naa leen ak dal ak dalal seen njaboot ak néewal wër ak i tukki ci lu dul lu manu la ñàkk, ba ca gàmmu ga walla jeexug weeru gàmmu ga, daal di ne leen: » Yéen nit ñi maa ngi leen di digal ngeen jaamu seen Boroom mi leen boyal ngir ngeen jaamu ko, ña nga xam ne nag tënkeef na leen ci seen ug weddi walla seen bàkkaar jaamuwuñu ko, te rafetaluñu ci seen ug jaamu.
Bokk na ci àqi ka nga xam ne xamal na leen ay ndigalam ya nga xam ne dan a leen yeggale jëm ca àjjana, te mu leen di bégal, ba fàwwu ci lu dul njaqare. War na leen ngeen topp ko, bu ngeen ko defee dangeen texe ba fàwwu, texe gu ag texeedi du ànd ak moom du ñëw ginnaawam.
Bokk na ci ay àqam ci yéen, bu leen xamalee teereem yay ñoddee jëme sawara tey tege gàcca ak coono ba fàwwu ci lu dul mbégte, ngeen nangul ko te moytu ko, ngir nangu googu mooy tax a am mucc gu mat sëkk am noflaay bu sax dàkk.
Teg ca ne : « dénk naa leen ngeen jëmale seen gis ak seen yitte yépp ci ñaari Masala yii. 1️⃣ Ba njëkk: Mooy ngeen xam la ñu leen digal te def ko. 2️⃣Ñaareel ba mooy ngeen xamlu la ñu leen tere te bàyyi ko.
Te ngeen jàpp leen bu dëgër ndax yaar yooyu mooy xam-xami ñu njëkk ña ak ñu mujj ña, (Maanaam tënku ci yaar yii ) ñu njëkk ña ak ñu mujj ña, ña ca raw, ca lañu rawe, ña ca gën ca lañu gëne)
Teg ca ne leen farluleen ci fonk julli ak saraxe, ak ñaan. Daal di fatu moom Sëriñ bi ba timis jot. Ba Timis jotee mu génn julli, ba mu sëlmalee mu jàngloo kenn ci taalibe yi, Sëriñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana; Njëlbeenu saaru nag (Baqara) mu ubbee.
أعوذ بالله من الشيطان الرجيم بسم الله الرحمن الرحيم.
Daal di jàng ba ca.
ٱولئك هم المفلحون.
Sëriñ bi ne ko : » Taxawal ». Sëriñ bi daal di ne: « Lii mooy melow way-gëm ña Yàlla, ñoom dañoo mel ni ay ndab yu ubbeeku, te suuf ga fàtt, nga xam ne loo ca def mu téye ko.
Daal di ne ko: » jàngaatal « . Mu jàngaat ba ca.
ولهم عذاب عظيم.
Mu ne leen : « lii nag mooy melow yéefëer yi, ñoom dañoo mel ni ay ndab yu ubu, ndab lu ubu kenn manu caa def dara.
Daal di ne ko: » Jàngaatal ». Mu jàngaat ba ca.
ومايخادعون إلاأنفسهم وما يشعرون.
Mu ne leen: » Lii mooy melow naaféq yi, ñoom dañoo mel ni ay ndab yu ubbi kaw ga, bënn suuf ga, maniis na caa def waaye loo ca def itam du ko téye.
Daal di ne leen: » Lii nag ay yeete la ci li Yàlla wax sangu mbindeef yi Alayhi Salaam ne ko: » Dañuy gëm lañu wàcce ci yaw Alxuraan la ci jublu.
بماآنزل إليك
La mu wax ne.
وماآنزل من قبلك.
La mu ca jublu mooy téere ya jiitu Alxuraan ba ci Alxuraan, yépp jullit bi da koo war a gëm.
(Hikma bi) Njàngale mi ci nekk nag mooy. Bëgg julli ñi sori ak parparloo gu mel ni gi dal Yahuud yi, ak Nasaraan yi.
Sëriñ bi daal di dem dellusiwul ba nu julli (GEE)
Mu dellusiwaat ngir julli fajar te fajar googu mooy mujjug julleem gu mu ànd ak nit ñi.
Bi mu jullee ba noppi nag la daal di fatu dale ko dibéer jooju, ba ca guddig Àllarba ga, la wuyji Boroomam di 20 fani Tamxarit.
Sëriñ Muhammudul Mustafaa taawam ba ko njëkk a wuutu, baax lool te amoon ndëgërlaayu ndimbalul Yàlla. Moo dugg ca barab ,boobu Sëriñ bi fatu woon, jël loxoom teg ko ca la xame ne wuyji na Boroomam. Mu daal di wax.
إنا لله و انا اليه راجعون.
الله اكبر .
Jóg taxaw woolu mbokkam mu baax ma, Seex Muhammudul Basiir sama sang sama kilifa Yal na Yàlla jariñ nu ci barkeem. Yal na Yàlla nekkal leen ak mbooleem njabootug Sëriñ bi ci ag jagle ak mbooleem ku aju ci moom, noo ngi ñaan Yàlla mi gën ci ku ñuy wéeru tey gën ji kuy dimbalee.
Ca booba ñu la daal di waaj nag tàmbali ngir waajal Sëriñ bi, te ña ko doon waajal ñoom seen ñaari taalibe ya, di Muhammudu Ibnu Abdurahmaan At’tàndaxii, di ku dëggu ku laabiir ku am tawfeex. Ñu baaxe aji-xeebu ja ngir dimbale ko, Muhammadul Lamin Jóob Dagana boole ko ci waajal ga. Nu waajal ko fekk ko mu set wicc, nu dolli koo setal, daal di koy fendal ci ay mbalaan ba mu fendi, nu sàng ko ci juróomi mbalaan, mbubb ak taraxlaay ak kaala, ak yaari càngaay, nu gëttal ko suur ko sàng ko, loolu lépp nag ci biir néeg bi mu wuyjee Boroomam la ame.
Nu yëgal ñaari kilifa ya. Muy Sëriñ Muhammudul Mustafaa ak Sëriñ Muhammudul Basiir. Ñu def ay pexe ngir génne ko, jegeel waruwaay wa ba ci bunt bi, yaneen juróom-benni kilifa yu bokkul ak Sëriñ Muhammudul Mustafaa ak Sëriñ Muhammudul Basiir génne ko ak nijaayi Sëriñ Basiiru Seex Ahmad doomi Seex Muhammud Maam Al Kokkiyu, ak seen doomi mbokkam ma Sëriñ Seex Jóob doomi Sëriñ Madun Jóob Cilmaxa ak doomi Nijaayi sang ba Al-Mustafaa Al-Muxtaar Silla doomi Sëriñ Maxtaar Mareema ak seen doomi Baay-tëx Saheed doomi Maam Abdu Mbàkke ñu bàyyi ko ca waruwaay wa, mu war ngir gunge doomam ja saydi Al-Basiir ak Nijaayam ak ñaar ñi ko doon waajal ak Sëriñ Maxtaar Silla. Yàggul dara nu yegg Tuubaa gi nga xam ne moo ko sancoon ginnaaw bi taawam ba ganee àdduna ba tegal ay weer. Ñu yónni Abdullahi Jóob Al-kayti ca Maam Ceerno Ibraahiima rakki Boroom Tuubaa ja fekk ma nga ca dëkkam ba tudd DAARUL MUHTI diggam ak Tuubaa di ñaar-fukki miil 27miil ak juróom-ñaar yabal Nijaayi Sëriñ Basiirujooju ca Sëriñ Mbàkke Buso fekk ma nga GEDE BUSO ca sancam ba ci càmmooyu Tuubaa jegeyoo jegeg séenante. Yable ca Sëriñ Fàllu Mbàkke fekk ma nga NDINDI ci ndeyjooru penku ndeyjooru Tuubaa, ci lu tolloo ak ñeenti-miil. Daal di yable ca Sëriñ Ndaam Abdurahmaan Lóo fekk ma nga ca sancam ba DAARUL HALIIMUL XABIIR nekk ci ndeyjooru Tuubaa, ci lu tolloo ak ñeenti-miil. Yable ca Sëriñ Ma-Ndumbe Mbàkke, ak Sëriñ Muhammudul Lamin Gay ak doomi baay-tëxam ja Sëriñ Baara Gay ca sancam ba. Diir bu gàtt rekk ñoom ñépp ñu teew, ak li ñenn ñi doon sori sori.
Tudd naa sellug Yàlla mi nga xam ne mooy tàggatal ku ko soob la ko soob.
Ñu tàmbli gas pax ma, ka njëkk a tàmbali mooy Sëriñ Abdullahi Jóob moomu nu tuddoon, MAHMUUD JAXATE ak IBRAAHIIMA NDAW ñoo ko yeggale jekkal pax ma, ñaar ñooñu nag ci Murit yu njëkk ya lañu bokk. Àndoon nañu ak Boroom Tuubaa ci lu bari njëkk muy dem ca géej ga.
Sëriñ Mbàkke Buso daal di koy jullee, dugg ci biir bàmmeel ba, ànd ak Sëriñ Muhammudul Lamin Gay, Ak Sëñ Ahmadu Ndumbe. Ñaar ña ko doon waajal daal di leen koy jottali. Muhammad doomi Abdurahmaant Attàndaxii itam daal di dugg fekki leen. Ñu lalal ko ab morso, génnewaat ko ngegenal ko, fatt pax ma ak ay dénk ak i weñ ak i laltaay ba nga xam ne ndox sax manu koo bëtt, daal di sotti suuf ci kawam. Lu jiitu ñuy noppi nag fajar jot. Muhammad doomi Abdurahmaan Attàndaxii daal di nodd Sëriñ Mbàkke Buso jiite leen ba ñu noppee nag dem jekkalaat barab ba. Barab ba nag mi ngi nekk ci ron garab googu nga xam ne bi Boroom Tuubaa njëkke dem Tuubaa ngir sanc ko fa la toogoon, di barab boo xam ne ci ngëneelul Yàlla fa la njëkk a wàcc bi mu ñëwee Tuubaa, waaye itam di fa mu mujj a wàcc bi mu delloo ca Boroomam.
Tudd naa Sellug Yàlla mi sos mbindeef yi te di leen dekkal.
✍🏾Aji bind-ji. Abdul Xaadir Al-istixaama
Aji topp-ji Sëriñ Saaliwu Njaay.