JÀNGALE TÉEREY SËRIÑ BI

Nahjul Xadaail Haaji – Wolof

Téereb Yar ak jàngale

Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji

ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca  allaaxiraa.
Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sang Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam gu sax
Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la (wu mat a wéer say mbir, joyal ko ko).
Jëf yaa ngi ci yéene yi, ku nekk it la nga yéeneey sag pay
Bokk na ci hikam (sagesse) :
ku sàkku mbir de bu ca saxee am ko. Ku fëgg bunt it boo fa saxee ubbilees la
Bokk na ci hikma bat ay:
ku tëyye boppam wëlif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi.
Bokk na ci ba leegi:
ku dul merloo boppam du begloo boroomam.
Bokk na ci ba tay :
ku def la ko soob dajeek la ko naqari.
Bokk na ci:
ku taqook jiyaar ak bakkanam, texe fa biir bàmmeelam .
Bokk na ci :
ku topp Yonnant bi, am gën ji la mu ñaan.
Am ku jël maanaa yii yépp boole leen ci wenn bayit :
( képp ku woor wëlif caaxaan yi () danga dogi ciy ngënéel

 

Ba beneen Dibeer (Dimanche) bu soobee Sunu Boroom.

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page