Ñaareelu bind Nahjul Xadaail Haaji – Wolof

 

1 Taalif wi [
Taaliif wii nag lu ñu barkeel la ci njëlbéen gi ba ca dayo ba.
Moom nag (ki waxoon bayit wu njëkk wi) –yal nañu ko dolli ag bëbb (xéewal) – am na ba tay weneen bayit wu yor
maanaa mii, mu ciy nos (woy) maanaam waxi sëriñam ji, wax jooju mooy jii :
(nguurug neen waxtu rekk la, nguurug dëgg nag day wey ba yawmal-xiyaam)

( dëgg day sax , neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe)

Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca

allaaxiraa

2 Ubbite gi

 Kii di doomi sëriñam ji dul sant ci boppam lu dul turam (wu tedd wa) Muhammad,

 Kii de mi ngi sant Yàlla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko.

Tudd naa sellam ga moom de boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy sant.

Moom de mooy ki def ay teggiin yu rafet muy luy làq ag réer ak judd bu naaw (bonu askan).

Mooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggiin, mooy ki léen jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub).

Xéewal ak mucc gu kawe nañu sottiku ca ka yéegoon ca Alburaax (Yonnant bi).

Kooku mooy suñu sang biy woote jëme ci aji bind ji (ki sàkk mbindeef yi), defe ko nag ci gën jaa rafeti teggiin yi .

Kooku mooy Muhammad ak ñoñam ñi di woroomug raw ak saabaam yi làq ngënéelul Aji des ji (Yàlla mi fi dul jug)

Ñoom saaba yooyu de saxaloon nañu ag laa-biire ci lu dul ŋaayoo , ndaxte dañoo toroxaloon seeni bakkan ba far

léen moom.

Sànkoon nañu seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naafeq.

Ñu sukkandiku woon ci Aji jariñ (Yàlla) jiy Aji wërsëgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem wërsëg yi.

Ñoom de dañoo boyoon jëm alaaxlenniraa ngir ne dañoo fase woon wujj wa (adduna).

Masuñoo bàyyi lenn ndigal lu juge ci Aji settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla) kiy Aji bind ji.

Ñoom de – ci saffanub ñuy bàyyi ndigal yi – dañu ciy sax ànd ceek bànneex, ndaxte koomum ja yi du tax ñu koy fàtte

(alal ji ñuy jële ci marse yi duñu tax ñuy fàtte ndigali suñu boroom yi) .

Wuññi woon nañu lëndëm-lëndëmi gox yi ci xam-xam ak jëf ak dëppoo.

Ndaw ñu di sang yu ñaw ! ñoom de la neexoon ca cafka ga jël nanu ko.

Yal na ngërëm – lol di naa ci dajeek ëlëg ka làq cang gu joyu ga – sottiku ci seen kaw .

Kooka mooy Muhammad, yal na ko Aji des ji sotti ay xéewal ak mucc mook ñoñam ak saabaam yi di ay ndab (yuy

duy xam-xam aki xeewal aki hikam)

 

Ba beneen Dibeer (Dimanche) bu soobee Sunu Boroom.

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *