DOSSIER 18 SAFARFLASH INFOS

Cheikh Abdoul Ahad Goor Yalla ga

Cheikh Abdoul Ahad Goor Yalla ga : 3 em Khalif de Cheikh Ahmadou Bamba.
Le redresseur des tords, l’homme qui a inauguré l’ère de la libération des esprits :
Yenn ci Waxi Sëriñ Abdu Lahad Mbàkke Mom Seexul Xadiim (Yalna gërëmul Yàlla nekk ci ñoom) : – « Murid ci boppam moo amul, aw tur rekk la, te tur wu ne jëmm lay woo. Sëriñ Tuubaa mooy jëmm ji. Koo xamni boo ko jàppagul doo tudd Murid, boo ko bàyyee it doo tuddati Murid. Buñ la dee wax Murid mootax! » Lii nag li muy jàngale mooy ndeke muriid du tur woo xamne rekk kum neex wuyoo ko, waayee ndeke aw gisiin la, aw doxiin la, ay teggiin la, aw meloyiin la wu Seex Ahmadu Bàmba tërël ci njàngaliin wu leer, ku ca aw, walla nga aw ci wu ni mel buñ lako nangulee nga di’b Muriid. Te it nag mbirum Baatin la mom ku ciy dox ci rafet njortu rekk nga war a taxaw te def sa kem kàttan ci ndigël bàyyi tere yi di rafet njortu ci nangul nañu la ba nga di ab Muriid.
– Nanu melne ëkk te bañ a melni xob. Ndax xob ngélaw man nakoo naawal ba dugal ko ci’m pax waaye manu ko faa génne, ëkk nag fu ko ngélaw fekk fala koy bàyyi. » Kon lu waay nekk nako seet bamu wér, mu sax ca te way ca. Li ci gën a jar a bàyyi xel nag mooy ndeke lépp lu la réeral manu laa gindiwaat, niki ngelaw dugalee xob ci pax te manu koo génne waat.
_ – « Mbir ña ko bokk dañu koy waxtaane tënk ko takk ko muy aw sëy, bu ko defee fuñ ko sëpp buntu feeñ fa. » Lii dé njàngale mu leer, mbooloo mu nekk ak luñ man a bokk war nañu cee bàyyi xel. Ndeke mbooloo luñ déggoo rekk Yàlla ubbil léen ca bunt, lii ya tax Yonent bi (Saws) ne sama xeet wi du ñu déggoo mukk ci bakkaar manaam lor. Ndax lu ñu déggoo Yàlla ànd ca ubbil léen ca bunt. _ – « Mbooloo ku léen woo lala war ca ñoom njëkk mooy dox séen dig ak tumurànke. » Kon képp kuy woo mbooloo te manoo dox séen digganté ak tumurànke xamal ne woote wàcc nala. Mbacke Safar firnde laci 😭😭😭
-« Ku gént rëy nit boo yeexee yewwu tuuti dees nala tëj ci gént gi. » Ngir wone foorug bakkan, ku ko jël ak nooko jëlee fàww daanees la-
« Daraja booko riñaanee mu jatt la ; Wërsëg booko gatandoo mu dëpp ; ab juddu deesu ko mottalee aw làmmeñ. » Daraja deesu ko yóotu, ndax nit ñi doo ni léen mukk tay ngéen weg ma batax ñu weg la, moom kay ku ko yelloo (meritoo) rekk joxees lako. Wërsëg it kenn du ko gatandu, dangay nekk ci lu dagan di def lala war, bu ko defee Yàlla aji-wërsëgal ji dikke la wërsëgAm. Waaye jàpp ne yaa yor sa wërsëg rekk ci sa kaw i lijjanti ba tax dal manatoo ko ci darra, séenéen lool, loo dugg génn ci, ne du foofu. Yàlla took dila séetaan rekk baxam yaay wërsëgal sa bopp ; Juddu bu rafet jikko yu rafet mookoy wone, kon soxlawul naan diw ak diw ak diw ñoom samay way-jur… kon làmmeñ wuti wu ci darra, bu jikko rafetee rekk nu rafetlu juddu ba.
_ « Waar boo bëggee mu yegg bu mu yaatu. » (ngir xamle ne kuy sumb ci lu dul jeex def ca la nga man rekk te defee ko ci anam gu rafet)
_ « Yuqamtiku du yàgg » Ngir jàngle ni ku nekk danga war a dund finga toll rekk te bañ a yóotu dundiinu keneen, ndax booko jéemee it dina metti ba nga mujj toqi déllusi finga nekkoon, mbaa sax fu ko gën a suufe far.
_ -« Sañ namaa wàcce sama bopp waaye bu léen ma wàcce » Ngir xamle ne ku nekk yaa yor sa daraja sa loxo diko joxe num la neexe, waaye nag taxul muy lu kenn man a fuqarti walla mu di lako laaj.
_ – «Rambaaj bu jëw ba gëndoo, moo gën a tumurànke ab jirim » Maanaam ab jaxasekat, kuy sos ay wax ngir féewale aw nit, mu ne bu demee ba feeñ mooy gën a tumurànke ab jirim, ndax ñaari wàll yépp a koy bañ, mu mujj tonku tumurànke te nag rambaaj bu nekk dina am biss
_ – « Gone yi daal « Baa », « Siin » , »Miim » la ñu : « Baa » gi : bu léen Bëggël darra ; « Siin » gi : bu leen Séenul darra ; « Miim » gi : bu léen miimal darra. » Ngir jàngle ak a junj xaley jamono ji niñu dëtmalee ag mbon te déglu wu ñu ku léen di laabire. Ndax dañoo sax faf jàppe ñi léen waroon a yar niki ñu séen jamono xewwi, kon ñoom ñoo xam, ndax ñoo jàng, ñoo gëstu li jamono laaj…
_ « Lu la nuyu ; tàggu na la » Ngir wone ñàkk solog àddina rekk, loofi waaj-waaj mbir ba rëyël ko, buy yegseek buy jàll benn la. Kon nag ku yabu di def loo man ……
Diadieuf Cheikh Abdoul Ahad Borom Belel neena :
« cuma mere ndax sama jicko topal Cheikh Moustapha Mbacke ndack lu neck ci man moome lah.
Commission Fédérale des Relations extérieures

Articles similaires

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page